1Di ñaani néew-ji-doole ju sonn, bay diis Aji Sax ji njàqareem.
2Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la;
3Bu ma dummóoyu bésub njàqare;
4Samay fan a ngi wéy ni saxaar,
5Sama xol bi wow ni ñax mu xuur,
6Damaa jàq, di onk a onk,
7Ma mel nim tan ci màndiŋ mi,
8Nelaw të;
9Bés bu ne noon yi di ma sewal;
10Lekkuma xanaa di diwoob dóom, toroxloo;
11te sa mer ak sa xadar a tax,
12Ker a ngi law, nara mëdd samay fan.
13Waaye yaw Aji Sax ji, yaay des ba fàww,
14Yaw yaay taxaw, ñeewante Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"*,
15Sa jaam ñeeka sopp doji dëkk bii ñu màbb,
16Na xeet yi wormaal turu Aji Sax ji,
17nde Aji Sax jeey tabaxaat Siyoŋ,
18Mooy nangul aji tumurànke,
19Nañu bindal lii maasug ëllëg,
20nde Aji Sax jeey jéere fu sellam fa ca kaw,
21ngir teewlu onki ñi ñu tëj,
22ba ñu siiwal turu Aji Sax ji fi Siyoŋ,
23kera ba xeet yiy bokk daje,
24Sama digg doole la ma semmale,
25Ma ne: «Éy sama Yàlla, maasoo maas, say at du jeex.
26Bu yàgg nga samp suuf,
27Yooyu day réer,
28te yaw ngay kenn ki,