1Màggalleen Ki Sax!
2Ana ku mana tudd jaloorey Aji Sax ji?
3Ndokkalee kuy sàmm yoon,
4Éy Aji Sax ji, séddaale ma ci sa yiwu ñoñ,
5ma gis ngëneelu ñi nga tànn,
6Noo bàkkaar, nook sunuy maam;
7Sunuy maam seetuñu ca say kéemaan ca Misra,
8Teewul Yàlla wallu leen ngir turam,
9Dafa gëdd géeju Barax ya, mu ne sereŋ;
10musal leen ci loxol bañaale,
11ndox ma mëdd bañ ya,
12Ca lañu gëm ay waxam,
13Nes tuut ñu fàtte jëfam ja,
14di ŋaf-ŋafi ca màndiŋ ma,
15Yàlla jox leen la ñuy sàkku,
16Ba ñu demee ba iñaane Musaa ca dal ba,
17suuf a ne ŋafeet, wann Datan+ 106.17 Datan: seetal ci +bk Màndiŋ ma+bk* 16.27, 31-33.*,
18sawara ne jippét fa seen biir,
19Tëgg nañu aw nag ca tundu Xoreb,
20di jënde seen darajay Yàlla ja
21Dañoo fàtte Yàlla ma leen di musal
22Mooy kéemaan ya fa réewum Xam+ 106.22 réewum Xam mooy Misra ba tey.*,
23Yàlla da leen doon sànk,
24Dañoo gàntal réew mu neex,
25xanaa di xultoo seen biiri xayma,
26Moo tax mu giñal leen
27tëral seen askan ci biir xeet yi,
28Ñuy darook tuurum Baal Pewor|lemma="Baal:"*,
29di merloo Yàlla ci seeni jëf,
30Fineyas taxaw, àtte;
31muy àtteb njub bu ñu ko waññal
32Ñu merlooti Yàlla ca ndoxum Meriba ma,
33Ñoo naqaral Musaa,
34Te it faagaagaluñu yéefar
35xanaa di jaxasook yéefar yooya,
36di jaamu seeni tuur,
37Ñuy rendil rab ya
38di tuur deretu ñu deful dara,
39seeni jëf sobeel leen,
40Aji Sax ji mere ñoñam,
41ba tax mu teg leen ca loxol yéefar ya,
42seen noon ya noot leen,
43Ay yooni yoon la leen xettali,
44Mu gis nag seen njàqare,
45bàyyi xel ci kóllëreem|lemma="kóllëre g-:"* ak ñoom,
46xiir ña leen jàpp ñépp,
47Éy Aji Sax ji, sunu Yàlla, wallu nu,