1Ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal.»
2Sa nguur la Aji Sax ji saxal, dale ko fa Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:". Yilifal noon yi la wër!
3Sa mboolooy taxawal seen bopp, sa bésub xare. Ñu sol darajaak cellte, faboo fa njël sosoo, diy ndaw, wàccsil la, nib lay.
4Aji Sax jee ko giñ, te du dellu gannaaw: «Yaa dib sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:" ba fàww, topp dayob Melkiccedeg+ 110.4 Melkiccedeg, buurub Salem la woon, di sarxalkat bu Yàlla faloon ci jamonoy Ibraayma, maanaam ñeenti téeméeri at laata Aaróonaa doon ab sarxalkat..»
5Sang baa ngi fi sa ndijoor te mooy rajaxe buur yi, bés bu meree.
6Mooy mbugal xeet yi, jal seeni néew, di rajaxe kilifay àddina, ba mu daj.
7Déeg ba feggook yoon wa, Buur a cay naan, te moo ko tax di siggi.