1Ca tàkkal dexi Babilon, foofa lanu daa toog, fàttaliku Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:", jooy.
2Ca garab ya lanu daa wékk sunuy xalam.
3Fa la nu sunuy sang daa woyloo, noot nu, bëgg nu bégal leen, naan: «Woyalleen nu ci woyi Siyoŋ.»
4Moo! Nu nuy woye woyu Aji Sax ji kaw suufas yéefar?
5Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte, yal na ma doole dëddu!
6Yerusalem, su ma la fàttalikuwul, fonk la, ba gën laa bége lépp, yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ.
7Aji Sax ji, fàttalikul Edomeen ña, keroog jantub Yerusalem, ba ñu naan: «Màbbleen a màbb, ba suuf sa dëkk bi sampe siiñ!»
8Yeen waa Babilon gi ñu nara fàllas, ndokkalee ku leen fey jëf ja ngeen nu def!
9Ndokkalee ku ne cas seeni fere, tas ciw doj!