1Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
2yaa xam sama toogaay ak sama taxawaay,
3di càmbar samab dox ak sama tëraay,
4Aji Sax ji, bala maa wax baat,
5Kanam ak gannaaw nga ma dare,
6Ni nga ma xame daa yéeme,
7Fu ma jëm, ba sore la?
8Ma ñalgu ba asamaan, yaa nga fa!
9Ma war laafi njël,
10nga tettee ma fa ba tey,
11Su ma noon: «Na ma lëndëm mëdd boog,
12du tax lëndëm lëndëmal la dara.
13Yaa ma sàkkal xol ak xalaat,
14Naa la sante sama bind bu raglu bii te yéeme,
15Sama jëmm jii umpu la,
16Gis nga ma, ba ma diw lumb;
17Yàlla, say xalaat aka maa yéem!
18Su ma ko doon waññ, moo ëpp feppi suuf.
19Éy sama Yàlla, soo reyoon ñu bon ñii!
20Ñii sa tur lañuy luubale,
21Aji Sax ji, maaka bañ ñi la bañ
22Dama leena bañ ba fa mbañeel yem;
23Yàlla, seetlu ma, ba ràññee sama xol;