1Dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2Yal nanga ma nangul samag ñaan
3Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ,
4Bu ma xiir ci lu aay,
5Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor,
6Yal nañu fenqe seeni njiit ciw doj,
7Ni ñuy gàbbe suuf ba mu ne ŋafeet,
8Aji Sax ji Boroom bi, yaw laa wékki gët,
9Musal ma ci yeer yi ñu ma gasal,