1Di woyu màggal, ñeel Daawuda.
2Bésoo bés ma di la sant,
3Aji Sax jee màgg te jara màggal a màggal,
4Na maasoo maas di màggal say jaloore,
5Sa leeraayu ndam li ne ràññ,
6Sa dooley jëf ju raglu dees na ko jottali,
7Sa mbaax gu réy, dees na ko tari,
8Yiw ak yërmande, fa Aji Sax ji;
9Aji Sax jee baaxe ñépp,
10Aji Sax ji, lépp loo sàkk a lay gërëm,
11di tudd sa darajay nguur,
12doom aadama xam say jaloore
13Sa nguur ay nguur gu sax dàkk,
14Ku daanu, Aji Sax ji wallu;
15Ñépp a la wékk bët, di yaakaar,
16tàllal sa loxo,
17Aji Sax ji, jëfinam jépp njekk la,
18Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la,
19Nammeelu ku ko ragal, mu sottal;
20Aji Sax jeey sàmm kuy soppeem,