1Di ñaanu Daawuda.
2Yal na sama àtte bawoo fi yaw,
3Natt nga saab xol, niir ma guddi,
4Su may jëf it, di sàmm sa kàddu.
5Sa tànk, sama tànk,
6Éy Yàlla, maa lay woo, nga di ma wuyu;
7Na sa ngor feeñ,
8Sàmm ma ni peru bët;
9ma rëcc ñu bon ñi ma song,
10Seen xol dàq yërmande,
11Tanc nañu nu fépp,
12Mbete gaynde gu namma fàdde,
13Éy Aji Sax ji, jógal dajeek moom, detteel ko.
14Éy Aji Sax ji, walloo ma sa doole,