1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2Éy Yàlla, yaw mi may àtte dëgg,
3Yeen boroom daraja yi,
4Xamleen ne Aji Sax ji day séddoo ku ko ragal,
5Loxleen te baña bàkkaar,
6Rendileen seen sarax yi war,
7Bare na ñu naan: «Ana ku nuy won lu baax?»
8May nga ma bànneexu xol