1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2Ndokkalee yaw mi yég néew-ji-doole.
3Aji Sax jee lay aar, di sàmm sa bakkan,
4Aji Sax jee lay dooleel soo woppee,
5Dama ne: «Aji Sax ji, tooñ naa la;
6Noon yaa ngi may yéene lu bon,
7Ku dikk, di ma seet, di jinigal
8Bañ yépp a ngi may déeyoo,
9naan: «Musiba dal na ko, du jógati!»
10Sama am-di-jàmm bu ma wóolu sax jógal na ma,
11Waaye ngalla Aji Sax ji, baaxe ma,
12Su noon damuwul ci sama kaw,
13Man, damaa màndu, nga taxawu ma,