1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel askanu Kore wu góor.
2Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox,
3Maa mar Yàlla,
4Rongooñ laay dunde
5Lii laay fàttaliku, sama xol jeex:
6Moo man, lu may xàddi, ne yogg?
7Maa ngi ne yogg,
8Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma;
9Bëccëg Aji Sax ji baaxe ma ngoram,
10Naa wax Yàlla sama cëslaay, ne ko:
11Noon yaa ngi may ñaawal,