1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel askanu Kore wu góor.
2Éy Yàlla, noo déggal sunu bopp,
3Yaw ci sa bopp yaa dàq xeet yi,
4Du seen saamar lañu nangoo réew mi moos,
5Yaay kiy sama buur, di sama Yàlla,
6Yaw lanuy dàqe bañ yi,
7Du fitt laa wóolu,
8Yaa nuy musal ci bañ yi,
9Yàlla lanuy damoo bésoo bés,
10Waaye danga noo wacc,
11Waññi nga nu, nu won noon yi gannaaw,
12Ni gàtt yu ñuy yàpp, ni nga nu joxee,
13Jaay nga sa mbooloo ci dara,
14Tax nga sunuy dëkk di nu ree,
15Tax nga xeet yi di nu léeboo,
16Damaa dëkke gàcce,
17ndax kókkali yeek xastey nit
18Lii lépp dal na nu,
19Dëdduwunu la,
20teewul nga noot nu, wacce nu xaj ya,
21Su nu la fàtte woon yaw, sunu Yàlla,
22du la ump, yaw Yàlla,
23Yaa tax ñu yendu noo bóom,
24Éy Aji Sax ji, jógal! Looy nelaw?
25Loo nu làqe saw yiw,
26Nu ngi ne ñàyy ci pënd bi,