1Mu jëm ci njiitu woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda tëddee ndaw sa ñuy wax Batseba+ 51.2 Seetal ci +bk 2.Samiyel+bk* 11.1—12.25.*.
3Éy Yàlla, ni nga goree, baaxe ma ni,
4Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef,
5Xam naa ne maa tooñ,
6Yaw laa moy, yaw doŋŋ.
7Ñaawtéef daal laa judduwaale,
8Dëgg daal nga namm, dëggu reenu xol,
9Wis ma ndox, ma sell|lemma="sell:"*;
10Yal nanga ma dégtal mbég ak bànneex,
11Bul xool samay moy,
12Éy Yàlla, sàkkal ma xol bu sell,
13Bu ma xalab,
14May ma, ma bégeeti sag wall,
15ma xamal tooñkat sa yoon wi nga tëral,
16Céy Yàlla, yaw Yàlla mi may musal,
17Boroom bi, may ma, ma wax,
18Sàkkuwuloo sarax, nde kon ma indi;
19Saraxi Yàlla, xol bu tuub la,
20Ngalla baaxeel Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"*,