1Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maxalat, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda.
2Ab dof a nga naa ca xelam:
3Yàllaa tollu asamaan, jéer doom aadama,
4Ñépp a dëddu,
5Yàlla nee: «Xanaa ñiy def lu bon, xamuñu dara?
6Waaye ñooy tiit a tiit