1Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñu dippee Pitax mu luu, dëkk fu sore; diy ñaan, ñeel Daawuda, ba ko Filisteen ña jàppee ca Gaat+ 56.1 Seetal ci +bk 1.Samiyel+bk* 21.11-16.*.
2Éy Yàlla, baaxe ma,
3Noon yee ma yendoo lakkal,
4bés bu ma tiitee,
5Yàlla laay màggal kàddoom,
6Bésoo bés ñu ngi jalgati samay wax,
7Ñu ngi mànkoo, di ma yeeru,
8Éy gii ñaawtéef! Ñii nu ñu mana mucce?
9Tumurànke naa, nga gis.
10Bés bu ma wootee wall,
11Yàlla laay màggal kàddoom,
12Yàlla laa wóolu, ragaluma.
13Éy Yàlla, maa tegoo la ma la giñal,