1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda.
2Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, teewlul, ma dagaan la.
3Àll laa lay woowe, sama xol jeex; yéege ma doju rawtu wu ma jotul.
4Yaw laa làqoo, ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.
5Naa dëkke sa xayma ba fàww; làqoo sa kiiraay. \+w Selaw|lemma="selaw:"\+w*.
6Yàlla, yaa dégg samay dige, sédd ma céru ñi wormaal sa tur.
7Ngalla féqal fani Buur, ay atam bare, sët ba sëtaat.
8Éy Yàlla, yal na Buur toog ba fàww fi sa kanam, nga sédd ko sa ngor ak sa worma, mu fegoo;
9kon ma woy la ba fàww, di jëfe samay dige bésoo bés.