1Mu jëm ci njiital woykat yi, di woyu cant, ñeel Daawuda.
2Éy Yàlla, yaa jagoo cant fa Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"*,
3Yaw miy nangug ñaan,
4Samay ñaawtéef man na ma,
5Ndokkalee koo tànn, woo ko,
6Defal nga nuy kéemaan,
7Yaa dëje tund yu mag yi doole,
8di dalal riirum géej aki gannaxam,
9ba waa cati àddina yéemoo say firnde,
10Yaa dikke suuf am wal,
11di suuxat ngàbb mi,
12Yaay tëje mbeyum at mi say ngëneel,
13Parluy màndiŋ yaa ngi walangaan,