1Dib taalifu yeete bu ñeel Asaf.
2Maa ngi leen di léeb,
3muy lu nu dégg, xam ko,
4Dunu ko nëbb seeni doom,
5Bindal na sëti Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"* téereb seede,
6ngir ñiy juddu ëllëg xam ko,
7ngir ñu wóolu Yàlla,
8te baña roy seeni maam;
9Waa giirug Efrayim ñoo soxi fitt,
10Ñoo sàmmul kóllërey|lemma="kóllëre g-:"* Yàlla,
11ba fàtte ay jalooreem,
12Fa seen kanami maam la def kéemaan,
13Moo xar géej ga, jal ndox ma nim tata,
14Bëccëg mu jiitee leen aw niir,
15Moo xar ay doj ca màndiŋ ma,
16mu sotti ndox mu balle ciw xeer,
17Teewul ñu wéy di moy Aji Kawe ji,
18Ñoo diiŋate Yàlla xol,
19Ñuy waxal Yàlla naan:
20Dóor naw doj, moos, ndox ma fettax,
21Aji Sax ji dégg ci, mer lool;
22Dañoo gëmul Yàlla,
23Mu digal niir ya fa kaw,
24tawal leen mànn|lemma="mànn:"*, ñu lekk:
25mburum jàmbaar la nit lekk,
26Yàlla wale ngelawal penku fa asamaan,
27Mu tawal leenu yàpp, mu saawe ni pënd,
28wàcce ko fa seen digg dal ba,
29Mu faj seen aajo,
30Teewul bala seen xel a dal,
31Yàlla mer na, dal ci seen kaw,
32Loolu lépp teewul ñuy bàkkaar ba tey
33Mu dagg seeni fan, mu wéy ni cóolóol,
34Ba leen Yàlla faatee, ña ca des wuti ko,
35Ñu fàttaliku ne Yàllaay seen cëslaay,
36Teewul ñu di ko jéema naxey wax,
37Joxuñu ko woon xol,
38Teewul mu yërëm,
39ndax xalaataat ne suuxu neen lañu,
40Gàntal nañu ko ba tàyyi ca màndiŋ ma,
41Ñu dellu di diiŋat Yàlla,
42Fàtte nañu ndimbalam la,
43ba def ay firndeem ca Misra,
44Moo soppali deret seen yooni ndox,
45Mu wàcce ci seen biir ndiiraanu weñ
46Mu jox soccet yi seen gàncax,
47Seen garabi reseñ, mu daaneel ci tawab yuur,
48Seen jur gu gudd, mu bàyyeek tawab yuur,
49Yàlla sotti leen tàngooru xadaram,
50Mu afal meram,
51Daa faat képp kuy taaw ca Misra
52Mu génne ñoñam niy gàtt,
53ba yóbbu leen fu wóor te tiituñu;
54Mu yóbbu leen fa suufam su sell|lemma="sell:"* sa,
55Da leena dàqal ay xeet,
56Teewul ñuy diiŋat aka gàntal Yàlla Aji Kawe ji,
57xanaa dëddu, di ko wor ni seeni maam,
58Ñu di ko merlook seen bérebi jaamookaay|lemma="bérebi jaamookaay y-:"*,
59Ba ko Yàlla yégee, mer na,
60Mu gental dëkkuwaayam ba ca Silo,
61Mu jébbal ngàllo màndargam dooleem+ 78.61 màndargam dooleem ji ñu wax fi mooy gaal gi àlluway kóllërey Yàlla dence.*,
62Daa bàyyee ñoñam saamaru noon,
63Seeni waxambaane dee ci sawaray xare,
64seeni sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* loru ci saamar,
65Ca la Boroom bi yewwu ni ku doon nelaw,
66Mu dóor noon ba yari gannaaw,
67ba noppi xalab waa kër Yuusufa,
68xanaa tànn giirug Yuda,
69Mu tabax këram gu sell, na mu mel fa kaw-a-kaw,
70Mu teg ca tabb Daawuda, jaamam ba,
71fa mu doon toppatoo jur gu jaboot;