1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit+ 8.1 gitiit tur la wu réer ci làkku ebrë. Man na doon xeetu xalam gu cosaanoo dëkk ba ñuy wax Gaat ci réewu Filisti. Man na nekk it galan bu ñu daan woye ci jamono bu ñuy witt reseñ, di ko nal.*, ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
2Aji Sax ji sunu Boroom,
3Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp,
4Damay xool sa asamaan si nga móol,
5Moo, luy nit, ba nga di ko bàyyi xel?
6Yaa ko def mu gëna suufe as lëf malaaka yi,
7fal ko ci kaw loo bind,
8jur gépp, gu gudd ak gu gàtt,
9ak njanaaw ak jën