1Mu di ñaanu Daawuda.
2Maa gore, musal ma;
3Éy Boroom bi, baaxe ma;
4Boroom bi, bànneexalal sab jaam,
5Boroom bi, yaa baax, di baale,
6Éy Aji Sax ji, teewlul, ma ñaan la;
7Bu ma la woowee bésub njàqare,
8Boroom bi, doo moroomu tuur yi,
9Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk
10Yaa màgg te yéemey jëf,
11Éy Aji Sax ji, won ma sa nammeel,
12Boroom bi sama Yàlla,
13Ngor lu réy nga ma won,
14Éy Yàlla, nit ñu bew a ma jógal,
15Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm,
16Geesu ma, baaxe ma.