1Dib taalifu yeete bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra.
2Aji Sax ji laay woye ngoram, ba fàww,
3Dama ne, sa ngor dàkk la sax,
4Aji Sax ji nee: «Damaa fas kóllëreek|lemma="kóllëre g-:"* ki ma tànn,
5“Damay saxal sa askan ba fàww,
6Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore,
7Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kaw-a-kaw?
8Yàlla ji ñu teral a teral ci jataayu ñu sell ñi,
9Yàlla, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
10Yaw yaa man géej gu sàmbaraax;
11Yaa rajaxe Raxab miy ninki-nankay géej, bóom ko,
12Yaa moom asamaan, yaa moom suuf.
13Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk.
14Yaa àttan, jàmbaare;
15Àtteb dëgg ak njub a lal sab jal,
16Aji Sax ji, ndokkalee mbooloo mu la xal di sarxollee,
17ànd di la bége bés bu ne,
18Seen darajay doole, yaw a.
19Sunu kiiraay lii, Aji Sax jeey boroom;
20Wax nga say wóllëre ci peeñu,
21Maa ràññee sama jaam Daawuda,
22ànd ak moom, saxal ko,
23Noon du ko bett,
24Ay bañam, ma rajaxe;
25sama wormaak sama ngor di ko gunge,
26Géej, ma teg ci loxoom,
27Moo ma naa: “Yaay sama baay,
28Te it maa koy def samab taaw,
29sàmmal ko sama ngor ba fàww,
30Damay saxal askanam ba fàww,
31Bu ay sëtam wàccee sama yoon,
32mbaa ñu xëtt sama dogali yoon,
33ma bantale leen seenug moy,
34Waaye duma ko daggal sama ngor,
35Déet, duma masa fecci sama kóllëre,
36Benn yoon laa ko giñ ci sama sellaay,
37askanam, dàkk;
38ak weer wi sax ba fàww,
39Ndaxam yaw Yàlla, jéppi nga ki nga fal,
40Fecci nga sa kóllëreek sab jaam,
41Bëtt nga ñagam yépp,
42ku fa jaare, jël ca alalam,
43Yékkati ngay bañam,
44Waññi nga ñawkal saamaram,
45Xañ nga ko darajaam,
46Dagg nga fani ngoneem,
47Éy Aji Sax ji, xanaa lii du jeex?
48Bàyyi ma xel, samay fan yàggul.
49Ana kuy dund te du dee?
50Boroom bi, ana sa ngor la nga daan jëfe
51Boroom bi, bàyyil xel ci sa gàcceg jaam ñi,
52Aji Sax ji, say noon a ngi sewal