1Ku dëkke kiiraayu Aji Kawe ji
2Dama naa Aji Sax ji:
3Kii kay moo lay musal cig fiir
4Kiiraayam la lay sànge,
5Doo ragal njàqarey guddi
6mbaa mbas mu yooteg lëndëm,
7Junni daanu fi sa wet,
8Say gët nga ciy teg,
9Yaw mi màkkaanoo Aji Sax ji,
10genn loraange du la dab,
11Ay malaakaam la lay booleel,
12Seeni loxo lañu lay leewoo,
13Dangay falaxe jaan ak gaynde,
14Yàlla da naa: «Kii de man la safoo,
15Mu woo ma, ma wuyu ko;