1Éy Aji Sax ji Yàlla, boroom mbugal!
2Yaw miy àtte àddina, jógal
3Aji Sax ji, fu ku bon kiy àkki?
4Ñu ngi làmmiñoo reewande,
5Aji Sax ji, say ñoñ lañuy dëggaate;
6Jëtun akub doxandéem, ñu faat;
7te naa: «Ki Sax gisu ci,
8Yeen bokk yu dofe yi, moytuleen.
9Ki jëmbati nopp, da dul dégg a?
10Kiy yar yéefar yi, da dul mbugalee?
11Aji Sax ji xam na xalaatu nit,
12Ki Sax, ndokkalee ki ngay yar,
13dëfal ko ci bési safaan,
14Boroom bi kat du wacc ñoñam mukk,
15Àtte dina dellu doxe yoon,
16Ana ku may taxawal ci ñu bon ñi?
17Su ma Aji Sax ji walluwul woon,
18Dama noon: «Tarxiis naa!»
19Ma bare xalaati xol,
20Loo séq ak njiit lu jubadi
21Ñii dañoo mànkoo, di tëru ku jub,
22Waaye Aji Sax jeey sama rawtu,