1Moo tax nu wara yokka teewlu kàddu yi nu dégg, bala noo lajj, taañaañal.
2Kàddug Yàlla ga jibe woon ci gémmiñu malaaka yi mujj na di lu wér péŋŋ, te képp ku ko masa xëtt, mbaa mu déggadi ko, jot nga añ bi war ci sag tooñ.
3Kon nag, nun ci sunu bopp, nan lanuy rëcce mbugal, su nu sàgganee pexem mucc mu réy mii Sang bi njëkkoona biral, te ñi ko dégg dëggalal nu ko?
4Te Yàlla moo doon dëggale seedey ñooñu ay firnde aki kéemaan ak wépp xeeti kawtéef ak ay mayi Noo gu Sell|lemma="Noo gu Sell g-:"* gi, may yi mu séddalee ni mu ko soobe.
5Ndax kat du ci kilifteefu malaaka yi la Yàlla teg àddinay ëllëg ji nuy wax,
6waaye am na ku yékkatee béreb kàddug seede, ne:
7Yaa ko def mu gëna suufe as lëf malaaka yi,
8lépp la ko Yàlla di jébbal, teg ko ci ndëggoom+ 2.8 Seetal ci +bk Taalifi cant+bk* 8.5-7.*.»
9Yeesu mi ñu def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, moom lanu gis deewam gi mu dee tax mu jagoo kaalag teraanga. Noonu la deewale ñépp ci kaw yiwu Yàlla.
10Ndax kat Yàlla mi lépp lu sàkke ñeel, te lépp sàkkoo ci moom, moo nammoona wommat gone yu bare ba sédd leen daraja. Moo tax muy lu jaadu, mu sottale matug Yeesu ay coono, ndax Yeesu moo xàllal gone yooyu yoonu mucc.
11Yeesu miy sellal nit ñi, moom ak ñi muy sellal, ñoo bokk lenqe, te moo tax Yeesu rusu leena woowe ay bokk.
12Mu ne:
13Mu waxaat ne:
14Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane|lemma="Seytaane:"*.
15Noonu la goreele mboolem ñi seenug ragala dee tënkoon cig njaam, seen giiru dund.
16Ndax kat du ay malaaka la Yeesu xettalisi, waaye askanu Ibraayma la xettalisi.
17Moo tax fàww mu niru woon ay bokkam ci bépp fànn. Su ko defee mu mana doon seen sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bu mag bu am yërmande te wóor fa kanam Yàlla, ngir mana defal askan wi seen njotlaayal|lemma="njotlaay g-:"* bakkan.