1Kon nag gannaaw digeb tàbbi ci noflaayal Yàlla mu ngi sax ba tey, nanu ragal kenn ci yeen taxawe melokaanu ku ca jotul.
2Ndax kat ni ñu nu àggee xibaaru jàmm bi, noonu lees leen ko àggee, waaye kàddu ga ñu dégg moo leen jariñul dara, ndax ña ko dégg ñoo ko déggewul ngëm.
3Nun ñi gëm doŋŋ nooy tàbbi ci noflaayam, noonu mu ko waxe, ne:
4nde waxees na lu jëm ci bésub juróom ñaareel ba, ne:
5Te moo wax itam ci lii nu njëkka jukki, ne:
6Kon nag am na ñenn ñu ci wara tàbbi ba tey. Te ñi ñu njëkkoona àgge xibaaru jàmm bi, tàbbiwuñu ca ndax seenug déggadi.
7Looloo waral Yàlla jàppaat beneen bés bu ñuy tàbbee ci noflaayam, bés bu mu tudde «tey jii», te mooy ba mu waxee lu yàgga yàgg, gannaaw gi, ci gémmiñug Daawuda|lemma="Daawuda:"*, kàddu gii ñu jota jukki:
8Su leen Yosuwe tàbbaloon ca googa noflaay, kon gannaaw gi Yàlla du wax lu jëm ci beneen bés.
9Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla.
10Ndax ku tàbbi ci noflaayu Yàlla kat, na Yàlla dalloo woon ca ay liggéeyam, ni ngay dalloo ci say liggéey.
11Nanu def sunu kem-kàttan boog, ngir tàbbi ci googu noflaay, bala kenn a daanu ndax déggadi gu mel ni gu maam ya.
12Kàddug Yàlla de luy dund la, ànd ak doole, te moo gëna ñaw saamaru ñaari ñawka bu gëna ñaw. Day sar ba fa xel akug noo digaloo, ba fa yax ak yuq dajee, te man naa càmbar ay xalaat ak mébéti xol.
13Te it amul mbindeef mu làqu fi kanam Yàlla. Lépp a ne duŋŋ, ne fàŋŋ, muy gis, te moom lanuy waxal bés-pénc.
14Gannaaw nag am nanu kilifag sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* bu mag bu jàll ba ca biir asamaan, te mooy Yeesu Doomu Yàlla|lemma="Doomu Yàlla j-:"*, nanu ŋoy ci yoonu ngëm wi.
15Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.