1Kàddu gii dikkal na Yeremi, bawoo fa Aji Sax ji:
2«Dégluleen sàrti kóllëre|lemma="kóllëre g-:"* gii. Te yaw Yeremi, nga àgge ko képp kuy waa Yuda ak waa Yerusalem.
3Nga ne leen: “Aji Sax ji Yàllay Israayil dafa wax ne: Alkànde ñeel na képp ku sàmmul sàrti kóllëre
4gii ma santoon seeni maam bés ba ma leen génnee réewum Misra, miy saamandaay taalu xellikaayu weñ gu ñuul. Ma noon leen ngeen déggal ma te jëfe sàrti kóllëre gi ni ma leen ko sase, ba doon sama ñoñ, man ma doon seen Yàlla.
5Su ko defee ma wàccook ngiñ, la ma giñaloon seeni maam ne dinaa leen may réew mu meew maak lem ja tuuroo, muy fii tey.”»
6Aji Sax ji ne ma: «Yéeneel mboolem kàddu yii ci biir dëkki Yuda yu mag yi ak ci mbeddi Yerusalem, nga ne: “Dégluleen sàrti kóllëre gii te jëfe ko.
7Artu naa artu seeni maam, dale ko ba ma leen génnee réewum Misra, ba tey jii ma jàppoo di leen artu, naan leen ñu déggal ma.”
8Waaye dégluwuñu, teewluwuñu, xanaa ku nekk di wéye dëgër bopp, topp ag bon xolam. Moo tax ma wàcce ci seen kaw mboolem sàrti kóllëre gii ma leen santoon ñu war koo jëfe te jëfewuñu ko.»
9Aji Sax ji dellu ne ma: «Pexem fippu feeñ na ca Yuda gépp ak ca waa Yerusalem.
10Dellu nañu ca seen ñaawtéefi maam ya bañoona sàmm samay kàddu. Ñoom it topp nañu yeneen yàlla, di leen jaamu. Waa kër Israayil ak waa kër Yuda fecci nañu kóllëre ga ma fasoon ak seeni maam.
11«Moo tax Aji Sax ji wax ne: “Maa ngii di leen wàcceel musiba mu ñu dul mana rëcce. Dinañu ma ne wóoy te duma leen déglu.
12Su ko defee waa dëkki Yuda yu mag yeek waa Yerusalem dem jooytuji ca yàlla ya ñuy taalal cuuraay|lemma="cuuraay l-:"*, te duñu leen mana wallu mukk ci seen jamonoy musiba.
13«“Yaw Yuda, ni sa dëkk yu mag tollu, ni la say tuur tollu. Ni mbeddi Yerusalem tollu it, ni la sarxalukaay|lemma="sarxalukaay b-:"* yi ñu fa saam tollu, ñu di fa taalal cuuraay Baal|lemma="Baal:"*, tuur mu seexluwu mi.”
14«Yaw nag Yeremi, bul ñaanal askan wii. Bu leen tinul, bu leen dagaanal. Ndax kat keroog bu ñu nekkee ci seen musiba, ba naan ma wóoy, du maay déglu.
15«Ana lu samay soppe di defati sama kër?
16Oliw naat, jekki doom;
17Aji Sax ji Boroom gàngoor yi leen jëmbatoon,
18Aji Sax jee ma xamal, ma xam,
19Ndax damaa naagu woon ni xar
20Ma ñaan Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
21Moo tax Aji Sax ji wax lii ci mbirum waa Anatot, ñiy wut sama bakkan, naan ma: «Baal di jottali kàdduy waxyu ci turu Aji Sax ji, lu ko moy nu rey la.»
22Moo tax kay Aji Sax ji Boroom gàngoor yi wax ne: «Maa ngii di wàccesi mbugal fi seen kaw; seen xale yu góor ñu reye leen saamar; seeni doom, góor ak jigéen, dee ak xiif.