Yeremi 14:1-21 WOLB2025 - Bible AI

1Kàddug Aji Sax jii dikkaloon na Yeremi, jëm ca maral ma. Mu ne:

2«Waa Yudaa ngi ñaawlu,

3Kàngam ya yebal seeni surga, ñu rooti;

4Réew mi tawluwul, suuf si fett,

5Kéwél sax jur ci àll bi, sànni

6Mbaamu àll taxaw ci tund yi ne faraas,

7Dëgg la sunuy ñaawtéef a nu tuumaal,

8Éy yaw, yaakaaru Israayil, mi nuy wallu bésu njàqare,

9Ngalla bul mel ni ku waaru,

10Aji Sax ji dafa wax ci askan wii ne: «Ñeeka bëggub taxawaalu, baña téye seen tànk. Moo tax man Aji Sax ji bégewuma leen. Léegi ma bàyyi xel seenug mbon, ba mbugale leen seeni moy.»

11Aji Sax ji nag ne ma: «Bul ñaanal askan wii njekk.

12Su ñu ci boole woon koor sax, duma déglu seeni dagaan. Su ñu ma doon sarxalal saraxu rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"* ak saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"* it, du maa leen di nangul. Xanaa saamar akub xiif ak mbas kay laa leen di faate.»

13Ma ne ko: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yonent yaa ngii di leen wax ne duñu dajeek saamar, duñu xiif te jàmm ju ne ñoyy nga leen di defal fi bii béreb.»

14Aji Sax ji ne ma: «Kàdduy waxyuy|lemma="waxyu:"* fen la yonent yiy jottali ci sama tur. Yebaluma leen, santuma leen ko, waxumaak ñoom. Peeñuy fen ak ngisaaney neen ak nax yu ñu fental seen bopp lañu leen di jottalee ay kàdduy yonent.»

15Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Yonent yi ma yebalul te ñuy wax ay kàdduy waxyu ci sama tur naan: “Saamar akub xiif du am ci miim réew,” saamar akub xiif ay mujje yooyu yonent.

16Ñi ñu doon jottali ay kàdduy waxyu it, xiif ak saamar a leen di rey, ñu sànni seeni néew ci mbeddi Yerusalem, te duñu am ku leen rob, ñook seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen. Dinaa leen xëpp seen ay.

17«Nanga leen yégal saw tiis, ne leen:

18Ma dem, xool àll,

19Aji Sax ji, wacc ngaa wacc Yuda nii?

20Aji Sax ji, xam nanu sunug mbon,

21Waaye seetal ci sa tur te bu nu xalab,

© 2025 Bible Society of Senegal
v>