Yeremi 16:1-20 WOLB2025 - Bible AI

1Kàddug Aji Sax ji dikkalati ma, ne ma:

2«Bul jël jabar,

3Aji Sax ji kat dafa wax ci gone yu góor yeek gone yu jigéen

4mu ne: «Jàngoroy dee a leen di rey.

5Te Aji Sax ji kat dafa wax ne:

6Ku mag ak ku ndaw ay dee ci réew mii,

7Kenn du leen sédd aw ñam

8Kërug bernde it, bu fa dugg,

9Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoor yi kat dafa wax ne:

10«Su ko defee, boo waxee askan wii kàddu yooyu yépp, ñu ne la: “Ana lu waral Aji Sax ji dogalal nu musiba mu réy mii mépp? Ana fu nu tooñe ak fu nu moye sunu Yàlla Aji Sax ji?”

11Nga wax leen nag ne leen: “Seeni maam a ma wacc,” kàddug Aji Sax jee, “di topp yeneen yàlla, di leen jaamooka sujjóotal. Man nag, ñu dëddu ma; sama yoon it, ñu bañ koo sàmm.

12Yeen nag, ngeen di bon, ba raw seeni maam. Yeena ngii, ku nekk të ticc, topp xolam bu bon, bañ maa déggal.

13Maa leen di dàqe ci réew mii, jëme réew mu ngeen xamul, seeni maam xamuñu ko, ngeen di fa jaamu guddeek bëccëg yeneen yàlla, ndax dootuma leen baaxe.”

14«Waaw ay bés a ngi ñëw déy,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul wax ne: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génne bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* réewum Misra.”

15Waaye dañu naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, ki jële bànni Israayil réewum bëj-gànnaar, te jële leen mboolem réew ya mu leen sànke woon.” Maa leen di delloosi seen réew ma ma joxoon seeni maam.

16«Maa ngii di woolu nappkat yu bare.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu napp ñii ba noppi, ma woo rëbb yu bare, ñu rëbb leen ci kaw mboolem tund wu mag ak wu ndaw, ba ci bépp xar-xaru doj.

17Samay bët a ngi ne jàkk déy ci seeni jëf. Dara umpu ma ci. Seeni ñaawtéef, dara rëccu ma ci.

18Dama leen di njëkka fey ñaari yoon seeni moy, ndax ñoo sobeel sama réew meek seen méddi tuur yu bon yi, feesal suuf sii ma séddoo seen yëf yu siblu yooyu.»

19Yaw Aji Sax ji may dooleel,

20Ndax nit man naa sàkkal boppam ay yàlla?

© 2025 Bible Society of Senegal
v>