Yeremi 17:1-26 WOLB2025 - Bible AI

1«Bàkkaaru waa Yuda lañu binde xaccug weñ

2Seeni doom sax di bàyyi xel seeni sarxalukaay

3ak kaw tund yi ci àll bi.

4Dingeen xañ seen bopp cér bi ma leen séddoon,

5Aji Sax ji dafa wax ne:

6Day mel ni gajjub ndànd-foyfoy,

7Waaye barke ñeel na ku wóolu Aji Sax ji,

8Day mel ni garab gu saxe wetu ndox,

9«Dara gënula dëng xelum nit,

10Maay Aji Sax jiy seetlu xel,

11Kuy jagoo alal ju lewul,

12Sunu kër gu sell gi,

13Yaw Aji Sax ji yaakaaru Israayil,

14Éy Aji Sax ji, faj ma, ma faju;

15Ñu ngii naa ma:

16Man de, bañuma laa sàmmal, topp la;

17Bu ma teg tiitaange,

18Ngalla gàcceelal ñi ma topp,

19Aji Sax ji da maa wax ne ma: «Demal taxawi ca buntu Doomi réew mi, fa buurub Yuda di duggeeka génne. Te nga taxaw itam ca mboolem bunti Yerusalem ya ca des.

20Nga ne leen: “Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen buuri Yuda ak yeen waa Yuda gépp ak képp ku dëkk Yerusalem, di jaare ci bunt yii.

21Aji Sax ji dafa wax ne: Moytuleen seen bopp ba baña gàddu lenn ci bésub Noflaay|lemma="bésub Noflaay b-:"*, di ko jaarale bunti Yerusalem.

22Buleen génne seeni kër lenn ci bésub Noflaay te buleen ci liggéey lenn. Waaye nangeen sellal bésub Noflaay, muy la ma santoon seeni maam.

23Ndaxam dégluwuñu ma, teewluwuñu ma, xanaa të ticc, baña dégg, di gàntal ndigal.

24Waaye su ngeen ma dégloo ba déglu ma, kàddug Aji Sax jee, baña gàddu lenn di jaare bunti dëkk bii bésub Noflaay, xanaa di sellal bésub Noflaay, bañ cee liggéey lenn,

25su boobaa buur yiy tooge jalub Daawuda, tey dawal watiir aki fas, ñook seeni kàngam, duñu noppee jaare ci bunti dëkk bii, feggook seeni kàngam. Waa Yudaak waa Yerusalem it di jaare ci bunt yii, su ko defee dëkk bi sax dàkk.

26Dees na bàyyikoo dëkki Yuda ak li wër Yerusalem ak diiwaanu Beñamin, ca suufu tund waak kaw tund ya ak ca diiwaanu Negew. Am na ñuy indi ci kër Aji Sax ji ay saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"* ak yeneen saraxi jur ak saraxu pepp|lemma="Sarax yi:"* ak cuuraay|lemma="cuuraay l-:"*. Am ñuy indi ci kër Aji Sax ji saraxi cant|lemma="Sarax yi:"*.

© 2025 Bible Society of Senegal
v>