Yeremi 18:1-22 WOLB2025 - Bible AI

1Kàddu gii dikkal na Yeremi, bawoo fa Aji Sax ji. Mu ne ko:

2«Dalal di dem ca tabaxkatu njaq ba. Foofa laa lay dégtale sama kàddu.»

3Ma daldi dem ba ca kër tabaxkatu njaq ba. Ma fekk ko muy liggéey ca tabaxukaayu njaqam.

4Lée-léeg ndab li tabaxkat biy tabaxe ban yàqu ci loxoom, mu dellu defaraat ba mu baax ci moom.

5Kàddug Aji Sax ji nag dikkal ma ne ma:

6«Nii tabaxkatu njaq bii di defe, ndax dama koo manula def ak yeen, bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"*?» Kàddug Aji Sax jee. «Ban bii déy, ni mu mel ci loxol tabaxkatu njaq bi, ni ngeen mel ci sama loxo, yeen bànni Israayil.

7Léeg-léeg ma wax lu jëm ci aw xeet mbaa am réew, ne dinaa ko déjjati, daaneel ko, tas ko,

8xeet woowu tuub mbonam gi ma leen doon artoo, ma fomm musiba mi ma naroona wàcce ci seen kaw.

9Lée-léeg it ma wax lu jëm ci aw xeet mbaa am réew, ne dinaa ko tabax, jëmbat ko

10ba noppi ñu def lu ma ñaawlu, baña dégg sama kàddu. Su ko defee ma fomm lu baax la ma leen naroona baaxe.

11Kon waxal boog waa Yuda ak waa Yerusalem ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngi nii di leen tabaxal musiba ci pexe mu ma leen di fexeel. Kon na ku nekk dëpp yoonam wu bon te jubbanti jikkoom aki jëfam.”

12Dañu naan: “Jaru ko, sunu xalaatu bopp lanuy topp, ku nekk të ticc di jëfe sa xel mu dëng.”»

13Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne:

14Ku masa gis fu tawub yuur gedde mbartali Libaŋ,

15Moona sama ñoñ fàtte nañu ma;

16ba seenum réew gental,

17Maay mel ni ngelawal penku, tasaare leen,

18Ba mu ko defee, mu am ñu ne: «Aywaleen, nu lalal Yeremi pexe. Ndax kat soxlawunu ko ba di ci ñàkk dara: du njàngalem sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"*, du digley boroom xel te du kàdduy waxyu yu yonent jottali. Nanu ko duural ba sànk ko te baña faale lenn ciy waxam.»

19Waaye yaw Aji Sax ji, teewlu ma

20Ndax lu baax dees na ko feye lu bon?

21Kon nag bàyyil seeni doom ñu xiif ba dee,

22Boo jekkee yebal gàngoor,

© 2025 Bible Society of Senegal
v>