1-2 Ci kaw loolu, Pasur doomu Imer, sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ba jiite woon saytub kër Yàlla ga, ba mu déggee Yonent Yàlla Yeremi muy jottali kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* yooyu, mu dóorlu ko, jéng ko ca buntu kër Aji Sax ja féete kaw, te ñu dippee ko Beñamin.
3Ca suba sa Pasur yiwee ko ca jéng ba. Yeremi ne ko: «Aji Sax ji tuddeetu la Pasur; Magor-Misabib (muy firi Tiitaange ju dajal) la la tudde.
4Ndax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la wàcceel tiitaange, yaak sa soppe yépp, seen saamaru noon daaneel leen, ngay gis; te Yuda gépp laay teg ci loxol buuru Babilon, ñii mu yóbbu leen ngàllo, ñee mu jam leen, ñu dee.
5Maay joxe lépp luy alalu dëkk bii. Mboolem lu fiy njariñ, mboolem gànjar, mboolem denci buuri Yuda, dinaa ko teg ci seen loxol noon yi, ñu sëxëtoo, jël, yóbbu Babilon.
6Yaw Pasur, yaak sa waa kër yépp ay duggi njaam ca Babilon. Babilon nga jëm te fa ngay dee, ñu rob la fa, yaak mboolem sa soppe ya nga daan àgge ay kàdduy waxyuy fen.”»
7Éy Aji Sax ji, naxtaan nga ma,
8Saa yu ma waxee, damay xaacu,
9Su ma nee: «Xaaral ma fàtte ko,
10Dégg naa ñaawlaate yu bare, ñu naan:
11Waaye Aji Sax jeek man, di ñeyi xare.
12Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yaw miy nattu ku jub,
13Woyleen Aji Sax ji,
14Alkute ñeel na bés ba ma juddoo,
15Alkute ñeel na ka ko yegge baay,
16Yal na kooku mel ni dëkk
17Moo ma reyul ci sama biiru ndey,