1Kàddu dikkaloon na Yeremi, bàyyikoo fa Aji Sax ji. Mooy ba buur Cedesyas yebalee ca moom, Pasur doomu Malkiya, mook sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ba ñuy wax Sofoni doomu Maaseya. Mu ne ko:
2«Ngalla seetal nu ci Aji Sax ji, ndax Nebukatnecar buuru Babilon mu ngi nuy song xare. Jombul Aji Sax ji defaatal nu lenn ciy kéemaanam ba mu dellu gannaaw.»
3Yeremi nag ne leen: «Waxleen Cedesyas ne ko:
4“Aji Sax ji Yàllay Israayil dafa wax ne: Seen dooley xare ji ngeen yor, di xeexeek ñi ci biti, di buuru Babilon ak waa Babilon ñi leen gaw, maa ngii di ko walbati, dajale ko ci biir dëkk bii.
5Man mii maay xareek yeen, won leen sama doole ak sama diisaayu loxo, xadaru, dikke leen mer mu réya réy.
6Maay faat lu dëkk ci dëkk bii, nit ak mala bokk loroo mbas mu réy.
7Gannaaw loolu nag,” kàddug Aji Sax jee, “Cedesyas buurub Yuda aki jawriñam ak askan week ñi des ci dëkk bii te rëcce ci mbas meek xare beek xiif bi, maa leen di teg ci loxol Nebukatnecar buuru Babilon ak seen loxol noon ak loxol ñi leen di wuta rey. Dina leen leel ñawkay saamar. Du leen baal, du ñéeblu, du yërëm.”
8«Te itam nga wax askan wii ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teg fi seen kanam yoonu dund ak yoonu dee.
9Ku toog ci dëkk bii, dinga deewe xare mbaa xiif mbaa mbas. Ku génn jébbal boppam waa Babilon ñi leen gaw nag dinga dund, bakkanam di yoolu xareem.
10Jógal naa dëkk bii déy, te loraange laa leen naral waaye du jàmm.” Kàddug Aji Sax jee. “Ci loxol buuru Babilon laa koy teg, mu jafal ko, lakk.”
11«Te it waxal waa kër buurub Yuda ne leen:
12Yeen waa kër Daawuda,
13Yeen ñi jataayoo xur wi,