Yeremi 22:1-29 WOLB2025 - Bible AI

1Aji Sax ji dafa wax ne: «Demal kër buurub Yuda, nga jottali fa kàddu gii.

2Danga naan: “Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yaw buurub Yuda mi toog ci jalub Daawuda, yaak say jawriñ ak sa nit ñiy jaare yii bunt.

3Aji Sax ji dafa wax ne: Deeleen jëfe dëgg ak yoon, di xettali ku ñu xañ dëgg ci ki koy néewal doole. Ab doxandéem, ab jirim akub jëtun, buleen leen lor, buleen leen fitnaal. Deretu jàmbur bu deful dara it, buleen ko tuur ci bii béreb.

4Su ngeen jëfee ba jëfe santaane bii déy, buur du noppee dugge yii bunt, di toogal Buur Daawuda fi jalam, di dawal watiir aki fas, ànd ak seeni jawriñ ak seeni nit.

5Waaye su ngeen dégluwul sama santaane yii, giñ naa ko ci man mii,” kàddug Aji Sax jee, “ab gent rekk la gii kër di doon!”»

6Aji Sax ji déy dafa wax ci mbirum kër buurub Yuda ne:

7Maa lay beralal yàqkat

8«Doxandéem yu bare dinañu jaare dëkk bii, di laajte ci seen biir naan: “Ana lu waral Aji Sax ji def nii bii dëkk bu mag?”

9Su ko defee ñu ne leen: “Xanaa li ñu fecci seen kóllërey|lemma="kóllëre g-:"* Yàlla Aji Sax ji, di sujjóotal yeneen yàlla, di leen jaamu.”»

10Buleen jooy buur Yosya mi dee,

11Aji Sax ji kat dafa wax ci mbirum buurub Yuda, Salum mi wuutu baayam Yosya te bàyyikoo fii. Mu ne: «Du fi délseeti mukk.

12Waaye fa ñu ko yóbbu ngàllo, fa lay deewe. Réew mii, du ko gisati mukk.»

13«Wóoy ngalla kiy tabax këram te seetu ci njekk,

14Mu ngi naan: “Maay tabax kër gu yaa,

15«Ndax ëpplante banti seedar da laa def buur?

16Da daan sàmm àqu ku ñàkk ak ku néew doole,

17«Yaw xooloo,

18Moo tax Aji Sax ji wax ci mbirum buurub Yuda, Yoyakim doomu Yosya, ne:

19Robu mbaam-sëf lees koy rob:

20Aji Sax ji nee: «Yeen waa Yerusalem,

21«Waxoon naa leen ko ba ngeen di am jàmm,

22Ngelaw dina sàmm seeni sàmm, sànk leen,

23«Yaw mi tooge Libaŋ+ 22.23 Libaŋ man naa doon misaalu kër buur gi nekk Yerusalem. Seetal ci +bk 1.Buur ya+bk* 7.2.*,

24Mu ne: «Giñ naa ko ci man miy dund,» kàddug Aji Sax jee, «yaw buurub Yuda, Kooña+ 22.24 Kooña turu gàttalu Yoyakin la. Seetal ci +bk 2.Buur ya+bk* 24.8-17.* doomu Yoyakim, soo doon jaarob torlukaay ci sama ndijoor it, fa laa lay foqatee,

25teg la ci loxol ñi lay tëru te nga ragal leen; muy Nebukatnecar buuru Babilon aki xarekatam.

26Maa lay xalab, yaak sa ndey ji la jur, jëme meneen réew mu ngeen juddoowul, te fa ngeen di deewe.

27Réew mi ngeen namma délsi, dungeen fi délseeti.»

28Nee ñu: «Waa jii di Kooña ndax da di njaq lu toj lu jarul dara?

29Éy waa réew mi, waa réew mee, waa réew mi,

© 2025 Bible Society of Senegal
v>