Yeremi 23:1-39 WOLB2025 - Bible AI

1«Wóoy ngalla sàmm yiy sànk aka tasaare sama gétt gi.» Kàddug Aji Sax jee.

2Moo tax Aji Sax ji Yàllay Israayil wax ci sàmm yiy sàmm ñoñam ne: «Yeena tasaare sama gétt gi, dàq leen, te taxawuwooleen leen. Kon maa ngii di leen taxawoo mbugal, yoole leen seen jëf ju bon.» Kàddug Aji Sax jee.

3«Man nag, sama ndesu gétt, maa leen di dajale ci mboolem réew yi ma leen dàqoon, jëme; te maa leen di delloosi ci seen parlu, ñu meññ ba yokku.

4Dinaa leen tabbal ay sàmm yu leen di sàmm ba dootuñu tiit, dootuñu jàq, dootuñu wuute.» Kàddug Aji Sax jee.

5«Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee,

6Ci jamonoom, Yuda dina texe,

7«Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «deesatul wax ne: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ca réewum Misra.”

8Xanaa dañu naan: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund te génnee askanu Israayil réewum bëj-gànnaar, génnee leen mboolem réew ya mu leen sànkeji woon.” Su ko defee ñu dëkkewaat seen suufas bopp.»

9Mu jëm ci yonent yi:

10Ay njaalookat la réew mi fees déy,

11«Te it yonent ak sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ñoo bokk yàqu,

12«Moo leen tax di tarxiis ci seenu yoon,

13«Ca yonenti Samari it laa gis njekkar,

14Waaye yonenti Yerusalem laa gisal lu yées:

15Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi

16Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:

17Ñi ma teddadil lañuy wax a wax,

18«Waaye ana ku ci teewe woon jataayu Aji Sax ji?

19Ngëlénu Aji Sax jaa ngoog,

20Merum Aji Sax ji du giif,

21Yebaluma yonent yii,

22Su ñu teewe woon ci sama jataay sax,

23Xanaa du maay Yàlla?»

24Ku mana làqoo làquwaay,

25«Dégg naa kàdduy waxyu yu fen yi yonent yooyuy wax ci sama tur, naan gént nañu lii, gént nañu lee.

26Fan la yonenti fen-kat yii àppal seeni xalaat, di wax waxyuy naxe yu ñu fental seen bopp?

27Seen gént yi ñuy nettalante, nammuñu ci lu moy sama ñoñ fàtte ma, ni ma seeni maam fàttee woon ndax Baal tuur mi.

28Yonent bu ci am gént, na nettali géntam, waaye ku ci am sama kàddu, na ko àddoo, na ma ko waxe. Ana ñax akum pepp?» Kàddug Aji Sax jee.

29«Sama kàddu déy, daa mel ni sawara, kàddug Aji Sax jee, mbaa marto, di falaxew doj!

30Moo tax maa ngii ci kaw yonent yi.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi sàccante samay kàddu.

31Maa ngii ci kaw yonent yi.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi mbel-mbeli naan: “Kàddoo ngii.”

32Maa ngii ci kaw ñiy yégle génti caaxaan.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi nettali seeni gént, bay waññi sama ñoñ, ndax seen fen yu jéggi dayo, te man de yebaluma leen, santuma leen dara. Amaluñu askan wii benn njariñ.» Kàddug Aji Sax jee.

33Aji Sax ji ne Yeremi: «Su la askan wii laajee mbaa ab yonent mbaa ab sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ne la: “Ana yéeneb waxyu|lemma="waxyu:"* bi la Aji Sax ji yóbbante?” Nga wax leen ne leen: “Yeenay yen bi te dinaa leen yenniku.”» Kàddug Aji Sax jee.

34«Te muy yonent, muy sarxalkat mbaa kenn ci askan wi, ku ci ne: “Yéeneb waxyu bii la ma Aji Sax ji yóbbante ci yeen,” maay dikke mbugal kooku mook waa këram.

35Li ku nekk wara laaj moroomam mbaa mbokkam kay mooy: “Lu Aji Sax ji tontu?” mbaa “Lu Aji Sax ji wax?”

36Waaye yéeneb waxyu bu Aji Sax ji, buleen ko fi tuddati. Jooju wax déy, yenub boroom lay doon. Ndax dangeena been sunu kàddug Yàlla, Yàlla Aji Sax jiy dund, Boroom gàngoori xare yi.

37Li nit kiy laaj ab yonent mooy: “Ana lu Aji Sax ji tontu? Ana lu Aji Sax ji wax?”

38Bu ngeen dee tudd ab yéeneb waxyub Aji Sax ji, te ma yónnee ci yeen, ne leen buleen di tudd ab yéeneb Aji Sax ji, su boobaa Aji Sax ji dafa wax ne:

39Maa leen di yenu déy, xalab leen, yeen ak dëkk bii ma leen joxoon, yeen ak seeni maam, ba ngeen sore ma.

© 2025 Bible Society of Senegal
v>