Yeremi 25:1-37 WOLB2025 - Bible AI

1Kàddu gii dikkal na Yeremi, jëm ci waa Yuda gépp, ci ñeenteelu atu nguurug doomu Yosya, Yoyakim buurub Yuda. Mu yemook at mi njëkk ci nguurug Nebukatnecar buuru Babilon.

2Yonent Yàlla Yeremi daa wax ak waa Yuda gépp ak waa Yerusalem gépp, ne leen:

3Li ko dale fukkeelu at ak ñett ci nguurug doomu Amon, Yosya buurub Yuda, ba tey jii, di ñaar fukki at ak ñett, kàddug Aji Sax jaa ngi may dikkal, ma di leen ko jottali te tàyyiwuma, waaye dégluwuleen.

4Aji Sax ji yónnee leen mboolem jaamam ñiy yonent yi. Yónni na leen ay yooni yoon. Waaye dégluwuleen, teewluwuleen.

5Mu ne leen: «Na ku nekk ci yeen dëpp jëfinam ju bon ak jëfam ju bon, ba mana dëkke réew mi leen Aji Sax ji jox naka jekk, yeen ak seeni maam, ba fàww,

6te buleen topp yeneen yàlla, di leen jaamooka sujjóotal; buleen ma merloo ndax yëfi neen yu ngeen sàkke seeni loxo. Su boobaa duma leen teg musiba.

7Waaye dégluwuleen ma.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Yeena ma merlook ak yëf yu ngeen sàkke seeni loxo, muy seen musiba.»

8Moo tax Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi wax ne: «Gannaaw dégluwuleen samay kàddu,

9maa ngii di yónnee, jëli mboolem làngi bëj-gànnaar.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay yónnee it ca Nebukatnecar buuru Babilon mi ci samag curga, daldi leen boole indi ci kaw réew mii ak ñi ci biiram ak mboolem xeet yi ko séq. Maa leen di faagaagal, gental leen gent bu sax dàkk bu ñuy muslu.

10Te muy kàddug mbégte di kàddug bànneex, di kàddug boroom séet akub séetam, di wolukaay bu fiy jib mbaa leer gu ñuy niitoo, lépp maa ko fiy boole tukkal.

11Réew mii mépp ay gental, def ndànd-foyfoy, xeet yii yépp di surgawu buuru Babilon diiru juróom ñaar fukki at.

12«Su ko defee bu juróom ñaar fukki at yi matee, ma doora dikkal Babilon ak buuram ndax seeni ñaawtéef.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay gental réewum Babilon ba fàww.

13Maay wàcceel réew mii mboolem kàddu yi ma ko rëbbe woon, te ñu bind ko ci téere bii, Yeremi jottali xeet yépp kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* yi.

14Ñoom waa Babilon it déy, dinañu surgawu ay xeet yu giir ak ay buur yu mag. Maa leen di fey seen añu jëf ju bon.»

15Aji Sax ji Yàllay Israayil déy da maa wax ne ma: «Am kaasu biiñ bii ci sama loxo, di misaal kaasu mbugal, te nga nàndal ci mboolem xeet yi ma lay yebal,

16ñu naan, tërëf, di say ndax aayteefu saamar laay yebal fi seen biir.»

17Ma daldi jële kaas bi ci loxol Aji Sax ji, nàndal ci mboolem xeet yi mu ma yebal.

18Ma nàndal waa Yerusalem ak dëkki Yuda ak seeni buur ak seeni kàngam ngir gental fépp, muy ndànd-foyfoy gu ñuy muslu, di ko móoloo ba sunu jonni yàllay tey.

19Firawna buuru Misra it nàndal naa ko ca, mooki surgaam aki kàngamam ak waa réewam,

20ak mboolem xeeti njaxasaan yi ci seen biir, ak mboolem buuri réewum Ucc, ak mboolem buuri réewum Filisteen ña féete Askalon ak Gasa ak Ekkron ak la des ca Asdodd.

21Ma boole ca nàndal Edomeen ñaak Mowabeen ñaak Amoneen ña,

22ak mboolem buuri Tir ak mboolem buuri Sidon ak buuri dun ya ca wàllaa géej,

23ba ca waa Dedan ak Tema ak Bus ak mboolem ñiy wat seen peggu kawaru bopp,

24ak mboolem buuri Arabi ak mboolem buuri xeeti njaxasaan yi dëkke màndiŋ mi,

25ak mboolem buuri Simri ak buuri Elam ak mboolem buuri Medd,

26boole ca mboolem buuri bëj-gànnaar, ñu jegeek ñu sore. Ma nàndal leen ñoom ñépp, ba réewi àddina yi ci kaw suuf yépp daj. Buurub Sesag+ 25.26 Sesag turu kumpa la, di Babilon ba tey.* topp ci ñoom, naan.

27Aji Sax ji nag ne: «Wax leen ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israayil dafa wax ne: Naanleen ba màndi, di waccu, fëlëñu, tëë jóg ndax saamar bi may yebal fi seen biir.”

28Waaye su ñu bañee naan ci kaas bi nga leen tàllal nag, nga wax leen ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Dingeen naan ba naanaatoo!

29Te kat dëkk bii ñu ma tudde sax, maa ngi koy tàmbalee musibaal. Kon yeen, nu ngeen mana fexee ba mucc? Dungeen mucc moos, ndax saamar laay wool mboolem ku dëkke àddina.”» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi.

30Aji Sax ji teg ci ne ma: «Yaw nag, jottali leen mboolem kàdduy waxyu|lemma="waxyu:"* yooyu. Te nga ne leen:

31riir ma àkki cati àddina,

32Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:

33Bésub keroog nag ñi Aji Sax ji rey, fu ne lañuy tëdd ci àddina, cat ba cat. Deesu leen jooy, deesu leen for, deesu leen rob. Ni neefare jonkan lañuy wetaroo ci kaw suuf si.

34Yeen sàmmi askan wi, serleen, yuuxuleen;

35Rawtu day réer sàmmi askan wi,

36Yuuxi sàmm yaa ngoogu,

37Merum Aji Sax ju réy ji

© 2025 Bible Society of Senegal
v>