1Kàddu gii dikkal na Yeremi, bawoo fa Aji Sax ji, ne ko:
2«Aji Sax ji Yàllay Israayil dafa wax ne: Nanga bind cib téere kàddu yi ma la wax yépp.
3Ndax kat ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay tijjil sama ñoñ seen wërsëg, muy Israayil di Yuda.» Aji Sax jee ko wax. «Maa leen di delloo ca suuf sa ma moomale woon seeni maam.»
4Kàddu yii la Aji Sax ji wax ci mbirum Israayil ak ci mbirum Yuda.
5«Aji Sax ji déy dafa wax ne:
6Laajteleen te xool,
7Wóoy boobu bés bu réy,
8«Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi, «maay damm yet wi ñu leen tënke ci seen ndodd, dammat seeni jéng, ba dootuñu doon jaamu doxandéem.
9Waaye seen Yàlla Aji Sax ji lañuy jaamu ak seen buur bi ma leen di falal, mu toogal Daawuda.
10Waaye yaw Yanqóoba sama jaam,
11Maa ngeek yaw, nar laa wallu.»
12Aji Sax ji déy dafa wax ne:
13Amul ku lay sàmmal sa àq,
14Sa soppe yépp a la fàtte,
15«Damm-damm yu dul wér
16Waaye ku la lekk, dees na ko lekk;
17«Ñu ngi la naan: “Waccees na la,”
18Aji Sax ji dafa wax ne:
19cant jollee ca,
20Seeni doom dañuy mel na woon,
21Su boobaa seen njiit di seen deret,
22«Yeenay doon sama ñoñ,
23Ngëlénu Aji Sax jaa ngoog,