1«Su boobaa,» kàddug Aji Sax jee, «maay doon Yàllay làngi Israayil yépp,
2Aji Sax ji dafa wax ne:
3Ñu ne: «Bu yàgg la nu Aji Sax ji feeñu,
4Yaw Israayil mu taaru,
5jëmbataat sa tóokëri reseñ
6Bés dina ñëw déy,
7Aji Sax ji déy dafa wax ne:
8Maa ngii di jële sama ñoñ réewum bëj-gànnaar,
9Ñooy dikk di jooy, di leewaayu,
10Yeen xeet yi, dégluleen kàddug Aji Sax ji,
11Aji Sax jee goreel askanu Yanqóoba|lemma="Yanqóoba:"*,
12Ñooy dikk, di sarxollee kaw tundu Siyoŋ,
13«Su boobaa janq bégem pooj,
14Maay yafal sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yi, ba reggal leen,
15Aji Sax ji dafa wax ne:
16Aji Sax ji nag ne ko:
17Am nga yaakaaru ëllëg.»
18Maa dégg moos askanu Efrayim di binni
19Dëddu woon nanu la moos
20Aji Sax ji ne:
21«Sampal ay xàmmikaay ci yoon wi,
22Ndaw su toogadi si,
23Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bu ma tijjee seen wërsëg, kàddu gii dina jibati ci réewum Yuda ak dëkk yi ko séq.
24«Waa réewum Yuda ak dëkk-dëkkaanam yépp ay bokk dëkk, ak beykat yeek màngaan yi yor gétt.
25Maay nàndal ku mar, leqali ku loof.»
26Ba loolu amee ma yewwu, ne xiféet, xam ne samay nelaw neex na.
27«Bés a ngii nag di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may jiwe kërug Israayil ak kërug Yuda jiwum doom aadama ak jiwum mala.
28Te ni ma leen teewloo woon ba ma leen di buddat, di leen fàqat, di leen daaneel, di leen yàqate aka lor, noonu laa leen di teewloo ngir defar leen, jëmbat leen.» Kàddug Aji Sax jee.
29«Su boobaa deesatul ne:
30Su boobaa ku nekk sa bàkkaaru bopp a lay rey. Ku lekk reseñ yu xaay, sa gëñi bopp lay uum.
31«Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «yu may fas ak waa kër Israayil ak waa kër Yuda kóllëre|lemma="kóllëre g-:"* gu yees.
32Du mel ni kóllëre ga ma fasoon ak seeni maam keroog ba ma leen jàppee ci loxo, génne leen réewum Misra. Ndax ñoom ñoo fecci sama kóllëre, te man may seen boroom kër.» Kàddug Aji Sax jee.
33«Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israayil bu fan yooyu weesoo,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.
34Kenn dootul soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji!” Ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ci ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»
35Aji Sax ji dafa wax,
36mu ne: «Su dogal yooyu manoona toxu, may gis,
37Aji Sax ji dafa wax ne:
38Mu ne: «Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «dees na tabaxalaat Aji Sax ji dëkku Yerusalem, dale ko ca soorooru tata bu tudd Ananel ba ca buntu Ruq ba.
39Dees na fa rëddaat kemu dëkk bi, jubal ba tundu Gareb, wëri ba Gowa.