1Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na Yeremi ñaareel bi yoon, fekk ko tëje ba tey ca biir ëttu dag ya. Mu ne ko:
2«Aji Sax ji dafa wax, moom miy sàkk mbir, bind ko, taxawal ko, Aji Sax ji di turam.
3Mu ne: “Woo ma, ma wuyu la, wax la lu réy te ruqe, loo xamul woon.”
4-5 Aji Sax ji Yàllay Israayil déy dafa wax ci mbirum këri dëkk bii ak këri buuri Yuda yii ñu màbb, di ko fegoo sëkk bi ñu leen gawe te di ko làqoo saamaru waa Babilon ñi ñuy xareel. Mu ne: “Kër yi dina fees ak néewi nit ñi ma bóom ndax mer ak xol bu fees. Dinaa xañ dëkk bii sama yiw ndax seen gépp mbon.”
6«Waaye du tee, maa leen di may tan, faj leena faj ba ñu wér, won leen xéewalu jàmm ju dëggu.
7Maay tijji wërsëgu Yuda ak wërsëgu Israayil, sampaat leen na woon.
8Maa leen di raxasal mboolem ñaawtéef gu ñu ma moye, baal leen mboolem ñaawtéef yu ñu ma moye, di ma gàntal.
9Dëkk bi daldi doon sama woy, di sama mbégte, di sama ndam, di sama sag ci biir mboolem xeeti àddina yi dégg ngëneel yi ma leen di defal yépp. Dinañu yéemu ba seen yaram daw ci lépp luy ngëneel ak jàmm ju ma leen di defal.
10«Aji Sax ji dafa wax ne, béreb bii ngeen ne ab gent la bu kenn nekkul, du nit, du rab te muy dëkki Yudaak mbeddi Yerusalem yii gental, kenn nekku fi, du nit, du rab, dees na fi déggati
11coowal mbégteek coowal bànneex ak kàddug boroom séet ak kàddug séetam, ànd ak kàdduy nit ñiy indi saraxi cant|lemma="Sarax yi:"* ci biir kër Aji Sax ji, tey dëbbe:
12«Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne, béreb bii di gent bu kenn nekkul, du nit, du rab ci dëkk yi fi nekk yépp, béreb bii dina dellu am parlu yu sàmm siy gooral seeni gàtt.
13Muy dëkki tund yi, di dëkki suufu tund yi, di dëkki diiwaanu Negew, di diiwaanu Beñamin, di li wër Yerusalem, di dëkki Yuda, gàtt yi dina dellu ci loxol sàmm buy takk lim ba.» Aji Sax jee ko wax.
14«Ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay sottal ngëneel la ma dig waa kër Israayil ak waa kër Yuda.
15Bés yooyu ci jamonoom,
16Bés yooyu Yuda dina texe,
17Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Daawuda du ñàkk mukk ku ko wuutu ci jalu Israayil.
18Sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yiy Leween ñi it duñu ñàkk ku leen taxawal fi sama kanam, di joxe saraxi rendi-dóomal|lemma="Sarax yi:"*, di taal saraxi pepp|lemma="Sarax yi:"* aka sarxal ba fàww.»
19Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na Yeremi, ne ko:
20«Aji Sax ji dafa wax ne: Ndegam manees naa dog sama kóllëre|lemma="kóllëre g-:"* maak bëccëg mbaa sama kóllëre maak guddi, ba bëccëg mbaa guddi baña teew ci waxtoom,
21kon dees na mana dog sama kóllëreek Daawuda sama jaam bi; tamit dogaale sama kóllëreek sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yiy Leween ñi may liggéeyal, ba Daawuda ñàkk sët bu koy wuutu cib jalam.
22Ni biddiiwi asamaan weesoo lim, feppi suufas géej wees waññ, ni laay fule askanu Daawuda sama jaam bi ak askanu Leween|lemma="Leween b-:"* ñi may liggéeyal.»
23Kàddug Aji Sax ji dellu dikkal Yeremi, ne ko:
24«Xanaa dégguloo li nit ñi wax? Ñu ne: “Ñaari làng ya Aji Sax ji tànnoon de, wacc na leen,” moo tax ñu xeeb sama ñoñ, ba tegatuñu leen sax aw xeet.
25Waaye Aji Sax ji dafa wax ne: Ndegam du maa fas sama kóllëre maak bëccëg ak guddi, te du maa saxalal asamaan ak suuf ay sàrt,