1Ba Cedesyas tolloo ci juróom ñeenteelu atu nguuram, ca fukkeelu weeram, ca la Nebukatnecar buuru Babilon ànd ak gàngooru xareem gépp ci kaw Yerusalem, ñu gaw ko.
2Ba Cedesyas tolloo ci fukkeelu atu nguuram ak benn, juróom ñeenti fan ca ñeenteelu weeram, ca lañu bëtt dëkk ba.
3Mboolem kàngami buuru Babilon daldi dikk toog ca buntu dëkk ba ca digg ba. Nergal Sarecer a nga ca ak Samgar Nebo ak Sar Sekim njiitu bëkk-néegi buur ak Nergal Sarecer meneen ma, njiitu gisaanekat yi, ñook mboolem kàngami buuru Babilon ña ca des.
4Naka la leen Cedesyas buurub Yuda gis, mook xarekatam ya yépp, ñu daldi daw, génn dëkk ba guddi, jaare tóokëru buur, fëlle bunt ba ca diggante ñaari tata ya, wuti yoonu xuru dexu Yurdan.
5Mbooloom Babilon dàq leen, ba dab Cedesyas ca jooru Yeriko. Ñu jàpp ko, indil ko Nebukatnecar buuru Babilon ca dëkk ba ñuy wax Ribla, ca réewum Amat. Nebukatnecar dogal fa àtteem.
6Buuru Babilon daa rendi doomi Cedesyas yu góor ca Ribla, muy gis, mu rendiwaale mboolem kàngami Yuda.
7Gannaaw loolu mu tuur bëti Cedesyas, jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon.
8Kër Buur ak këri waa dëkk ba nag, waa Babilon lakk leen, tatay Yerusalem, ñu màbb.
9Nebusaradan njiitu dag ya moom, daa boole ña desoon ca biir dëkk ba, ak ña ko jébbaloon seen bopp, ak ña desoon ca askan wa, jàpp leen, yóbbu ngàllo ca Babilon.
10Ba mu ko defee lenn ci baadoolo yi amul dara, mu wacc leen ca réewum Yuda. Booba la leen jox ay tóokëri reseñ aki tool.
11Ci biir loolu Nebukatnecar buuru Babilon jox ndigal Nebusaradan njiitu dag ya ci mbirum Yeremi. Mu ne ko:
12«Demal jëli Yeremi, nga sàmm ko, te bu ko def dara lu metti. Lu mu la ñaan it, defal ko ko.»
13Ba loolu amee Nebusaradan njiitu dag ya déggoo caak Nebusasban njiitu bëkk-néegi buur ak Nergal Sarecer njiitu gisaanekat yi, ak yeneen jawriñi buuru Babilon ña,
14ñu yónnee, jëli Yeremi ca ëttu dag ya, teg ko ci loxol Gedalya doomu Axikam doomu Safan, ngir Gedalya yóbbu ko mu ñibbi këram. Yeremi nag des Yuda ca biiri bokkam.
15Fekk na kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi ba ñu ko tëjee ca ëttu dag ya, ne ko:
16«Demal nga wax Ebedd Meleg, Kuuseen|lemma="Kuus:"* ba, ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngi nii di sottalsi sama kàddu yi jëm ci dëkk bii, muy ayam te du doon jàmmam. Dina am ngay gis, bésub keroog.
17Bésub keroog maa lay xettali, kàddug Aji Sax jee, ba deesu la teg ci loxol nit ñi nga ragal.