1«Yaw Israayil, sooy waññiku,
2xanaa nga waat ci Aji Sax jiy dund,
3Aji Sax ji déy dafa wax waa Yudaak Yerusalem, ne leen:
4Yeen waa Yudaak Yerusalem, deeleen xaraf ngir Aji Sax ji,
5«Nangeen yégle lii fa Yuda,
6Yékkatileen raaya, jubale Siyoŋ|lemma="Siyoŋ:"*,
7«Gayndee fëlle geeram,
8Kon nag solleeni saaku, ñaawloo te yuuxu ne:
9Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee,
10Ma ne: Éy Boroom bi Aji Sax ji,
11Janti keroog dees na wax askanu Yerusalem wii, ne leen:
12Ngelaw lu ko ëpp doole laay indi.
13Noon baa ngii, di jóg niy niir,
14«Éey Yerusalem, fóotal sa xol, jële ci lu bon,
15Kàddug yéenee ngi jibe Dan,
16Jottalileen ko xeet yi,
17Ñooy gaw Yerusalem ni wattukati tool,
18«Sa jëfin ak say jëf a la yóbbe lii,
19Maaka jàq a jàq bay jal-jali,
20Yéenees na rajaxoo ci kaw rajaxoo,
21Xanaa duma gis ba fàww raayab noon,
22«Dofe la sama ñoñ def.
23Maa xool suuf,
24Ma xool tund yu mag yi,
25Ma xoolaat, gisuma nit,
26Ma xool, gis suuf su nangu sa
27Aji Sax ji déy dafa wax ne:
28Loolooy tax suuf di ñaawlu,
29Gawar ak fittkat riir,
30Yaw Yerusalem mu tas mi,