1Gannaaw loolu njiiti xare yépp jóg, ñu ràññee ca Yoxanan doomu Kareyax ak Yesaña doomu Osaya. Ñu ànd ak askan wa wépp, dikk, ka gëna tuut ba ca ka gën di mag.
2Ñu ne Yonent Yàlla Yeremi: «Ngalla danu lay dagaan, nga ñaanal nu ngir ndesu askan wii ci sa Yàlla Aji Sax ji. Bare woon nanu, waaye gis nga lu néew li des ci nun.
3Ñaanal nu ngir sa Yàlla Aji Sax ji xamal nu fan lanu wara jaare, ak lan lanu wara def.»
4Yonent Yàlla Yeremi ne leen: «Baax na. Maa ngii di leen ñaanal seen Yàlla Aji Sax ji ni ngeen ko waxe. Lu leen Aji Sax ji tontu, dinaa leen ko yegge. Duma ci wacc baat.»
5Ñoom it ñu ne Yeremi: «Mboolem kàddu gu la sa Yàlla Aji Sax ji yóbbante ci nun, bu nu ko deful, yal na Aji Sax ji doon seede bu wér, bu dëggu bi nuy seedeel ag tooñ.
6Mu neex, mu naqari, sunu Yàlla Aji Sax ji nu la yebal lanuy déggal, ngir su nu déggalee sunu Yàlla Aji Sax ji, dinanu baaxle.»
7Ñu teg ca fukki fan, kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi.
8Yeremi woo Yoxanan doomu Kareyax ak njiiti xare yi mu àndal yépp, woo mbooloo mépp, ñu dikk, ka gëna tuut ba ca ka gën di mag.
9Yeremi ne leen: «Aji Sax ji Yàllay Israayil ji ngeen ma yóbbante seen dagaan, dafa wax ne:
10Su ngeen nangoo toog ba toog ci réew mii, maa leen di defar te duma leen daaneel. Maa leen di jëmbat te duma leen buddat. Ndax ñeewante naa leen ci musiba mi ma leen teg.
11Buuru Babilon mii ngeen ragal, buleen ko ragal! Kàddug Aji Sax jee. Buleen ko ragal, ndax yeen laa àndal ngir wallu leen, xettali leen ci moom.
12Maa leen di yërëm ngir mu yërëm leen, delloo leen ca seen suuf.
13«Waaye su ngeen bañee déggal seen Yàlla Aji Sax ji, naan: “Dunu toog ci réew mii,
14xanaa nu dem réewum Misra, fa nu dul gise xare; coowal bufta buy yégle xare sax dunu ko dégg. Dugub it dunu ko fa ñàkke. Foofa lanuy dëkki;”
15su boobaa nag dégluleen li ci Aji Sax ji wax, yeen ndesu Yuda. Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
16saamar ba ngeen ragal
17Képp ku dogu woona dem Misra,
18«Aji Sax ji Yàllay Israayil, Boroom gàngoor yi déy dafa wax ne: Su ngeen demee Misra, ni sama mer ak sama xadar yurikoo woon fi kaw waa Yerusalem, ni la sama xadar naan yureet fi seen kaw. Dingeen doon gentu alkànde, ñu di leen móolooka sewal, te dungeen gisati miim réew.»
19Yeremi teg ca ne: «Yeen ndesu Yuda, Aji Sax ji wax na leen ne leen: “Buleen dem Misra.” Nangeen xam xéll nag ne artu naa leen bésub tey.
20Yeena sànk seen bopp ba ngeen ma yebalee ci seen Yàlla Aji Sax ji, ne ma ma ñaanal leen sunu Yàlla Aji Sax ji, te lépp lu sunu Yàlla Aji Sax ji wax, naa leen ko jottali, ngeen def ko.
21Yegge naa leen tey jii li seen Yàlla Aji Sax ji wax, waaye faalewuleen lenn ci kàddu yi mu ma yóbbante ci yeen.