Yeremi 45:1-4 WOLB2025 - Bible AI

1Kàddu gii Yeremi waxoon na ko Barukk doomu Nerya, gannaaw ba Barukk tënkee ci taxañu mbind, kàddu ya ko Yeremi dégtal ca ñeenteelu atu nguurug doomu Yosya, Yoyakim buurub Yuda.

2«Aji Sax ji Yàllay Israayil dafa wax ci yaw, Barukk.

3Nga ne: “Wóoy ngalla man! Aji Sax ji yokk na maw naqar. Onk naa ba tàyyi te awma noflaay.”

4Aji Sax ji da maa sant ma wax la ne la: “Aji Sax ji dafa wax ne:

© 2025 Bible Society of Senegal
>