1Yii buuri réew nag la bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* duma, ba nangu seen réew ca wàllaa dexu Yurdan wa ca penku, te dale ca xuru Arnon ci bëj-saalum, jaare ci xuru dexu Yurdan ba ca tundu Ermon ci bëj-gànnaar.
2Benn ci buur yu ñu duma mooy Buur Sixon mu Amoreen ba dëkkoon Esbon, te moomoon genn-wàllu diiwaanu Galàdd, fa dale Arower ga feggook xuru Arnon, jaare ca digg xur wa ba ca xuru Yabog wa digalook réewu Amoneen ña.
3Sixon moo moomoon itam penkub xuru dexu Yurdan, fa dale dexu Kineret ca bëj-gànnaar, ba ca géeju Xorom ga feggook Bet Yesimot, ak diiwaan ba ca suufu tundu Pisga, féeteek bëj-saalum.
4Buur Og ma yilif Basan ca la. Moo bokk ca ndesu Refayeen ña, te amoon kër ca Astarot ak ca Eddrey.
5Og moo moomoon tundu Ermon ak dëkk ba ñu naa Salka, ak diiwaanu Basan bépp, ba fa mu digalook Gesureen ñaak Maakateen ña, teg ca genn-wàllu tundu Galàdd, fa mu digalook réewum Sixon buurub Esbon.
6Buur Sixon ak Buur Og, Musaa jaamub Aji Sax ji ak bànni Israayil ñoo leen duma woon. Seen réew la Musaa jaamub Aji Sax ji sédd giirug Ruben ak giiru Gàdd ak genn-wàllu giirug Manase.
7Buuri réew yi Yosuwe ak bànni Israayil duma ca tàkkug sowub dexu Yurdan nag, mooy ñii ñu lim ci suuf, te seeni réew dale woon Baal Gàdd ca xuru Libaŋ, ba ca tundu Alag, wa ñuy yéeg jëm Seyir. Yosuwe nag jox réew moomu bànni Israayil, ñu séddoo, giir gu ci nekk ak céram.
8Mooy weti diiwaanu tund ya ak suufu tund ya, ak xuru dexu Yurdan ak mbartali tund ya ak màndiŋu Yuda ak àllub Negew, ña fa dëkke di Etteen ñaak Amoreen ñaak Kanaaneen ñaak Periseen ñaak Eween ñaak Yebuseen ña. Buur ya ñu fa duma di:
9buurub Yeriko ak buurub Ayi ga ca wetu Betel,
10ak buurub Yerusalem ak buurub Ebron,
11ak buurub Yarmut ak buurub Lakis,
12ak buurub Eglon ak buurub Geser,
13ak buuru Debir ak buurub Geder,
14ak buurub Xorma ak buurub Aràdd,
15ak buurub Libna ak buurub Adulam,
16ak buuru Makeda ak buuru Betel,
17ak buurub Tapuwa ak buurub Efer,
18ak buurub Afeg ak buurub Lasaron,
19ak buuru Madon ak buurub Àccor,
20ak buurub Simron Meron ak buurub Agsaf,
21ak buurub Taanag ak buuru Megido,
22ak buurub Kedes ak buurub Yogneyam ca tundu Karmel,
23ak buuru Dor ca goxub Dor, ak buurub Goyim ca Gilgal,