Yosuwe 20:1-8 WOLB2025 - Bible AI

1Gannaaw ba loolu wéyee Aji Sax ji dafa wax Yosuwe, ne ko:

2«Waxal bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* ne leen, ñu tànn dëkki rawtu yi ma leen santoon ci jottalib Musaa,

3ngir ku rey nit ci njuumte lu dul coobareem, man faa rawi. Béreb yooyooy doon seen rawtu yu leen di musal ci kuy toppe bakkanu ku ñu rey.

4Bu ki rey dawee ba ca yooyu dëkk benn, day taxaw ca buntu dëkk ba. Su ko defee day diis magi dëkk booba mbiram. Nañu ko fat ca dëkk ba, may ko béreb bu mu dëkke ca seen biir.

5Bu ko fa kiy toppe bakkan toppsee, bu ñu ko teg ciy loxoom, ndegam du ci coobareem la rey moroomam te teyu ko, fekkul it mu bañ ko démb ak bërki-démb.

6Ca biir dëkk ba lay toog ba keroog ñu di ko àtte ca kanam mbooloo ma, ba keroog sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* ba mbiram yemool faatu. Su boobaa ka rey man naa ñibbi këram, ca dëkkam ba mu dawe woon.»

7Noonu lañu bere dëkk yii: Kedes ga ca diiwaanu tundi Neftali ca Galile, ak Sikem ga ca diiwaanu tundi Efrayim, ak Kiryaat Arba, di Ebron ga ca diiwaanu tundi Yuda.

8Ca wàllaa dexu Yurdan, fa féete Yeriko penku, Beccer lañu fa tànne ca màndiŋ ma ca kaw joor ga giirug Ruben séddoo, ak Ramot ga ca Galàdd, te bokk ci suufas giiru Gàdd, ak Golan ga ca diiwaanu Basan, te bokk ci suufas giirug Manase.

© 2025 Bible Society of Senegal
>