Yosuwe 3:1-16 WOLB2025 - Bible AI

1Ca ëllëg sa Yosuwe teela xëy, mook bànni Israayil|lemma="bànni Israayil:"* gépp, ñu bàyyikoo Sitim, ba ca tàkkal dexu Yurdan. Fa lañu dal bala ñoo jàll.

2Ñu teg ca ñetti fan, kilifay mbooloo ma wër dal ba,

3daldi sant mbooloo ma, ne leen: «Bu ngeen gisee gaal|lemma="gaalu kóllëre g-:"* gi yeb seen àlluway kóllëreg|lemma="kóllëre g-:"* Yàlla Aji Sax ji, sarxalkat|lemma="sarxalkat b-:"* yiy Leween ñi gàddu ko rekk, jógeleen seen béreb te dox topp ca.

4Waaye buleen jege gaal gi. Na diggante bu wara tollook ñaari junniy xasab dox seen digg ak moom. Su ko defee ngeen xam yoon wi ngeen di jaare, ndax masuleena jaare wii yoon.»

5Ci biir loolu Yosuwe ne mbooloo ma: «Sanguleen-set, ndax ëllëg Aji Sax ji dina def ay kéemaan ci seen biir.»

6Yosuwe teg ca ne sarxalkat ya: «Gàdduleen gaalu kóllëre gi te ngeen jàll jiitu mbooloo mi.» Ñu gàddu gaalu kóllëre ga, dox jiitu mbooloo ma.

7Aji Sax ji ne Yosuwe: «Bésub tey jii laa lay tàmbalee sargal, bànni Israayil gépp teg ci seen bët, ba ñu xam ne, na ma nekke woon ak Musaa ni laay nekke ak yaw.

8Yaw nag santal sarxalkat yiy gàddu gaalu kóllëre gi, ne leen: “Bu ngeen demee ba ca catal ndoxum Yurdan, ba dugg tuuti ca biir dexu Yurdan, nangeen taxaw.”»

9Yosuwe daldi wax bànni Israayil ne leen: «Dikkleen fii te déglu seen kàdduy Yàlla Aji Sax ji.»

10Yosuwe ne leen: «Dingeen xam nag ne Yàlla juy dund a ngi ci seen biir, te moo leen di dàqal a dàqal Kanaaneen ñi ak Etteen ñi ak Eween ñi ak Periseen ñi ak Girgaseen ñi ak Amoreen ñi ak Yebuseen ñi, te nii ngeen koy xame:

11gaalu kóllërey Boroom àddina wërngal këpp mu ngii di jàll jiitu leen ci biir dexu Yurdan.

12Léegi nag dangeen di tànne ci giiri bànni Israayil fukki góor ak ñaar; giir gu nekk genn góor.

13Su ko defee sarxalkat yiy gàddu gaalu Aji Sax ji Boroom àddina wërngal këpp, nañu dikk, te bu seeni tànk di tege ci ndoxum Yurdan rekk, walu ndox may wàcce ca kaw mooy dog, def bennub jal, taxaw.»

14Ba loolu wéyee mbooloo ma génne ca seeni xayma, ngir jàlli dexu Yurdan, sarxalkat yay gàddu gaalu kóllëre ga jiitu mbooloo ma.

15Booba jamonoy ngóob la woon, yemook ba dexu Yurdan feesee, ba wale ca tàkk gépp. Naka la gàddukati gaal ga àgg ca dexu Yurdan ga, ba seeni tànk tàbbi ca ndoxum tàkk ga rekk,

16walu ndox ma wàcce ca kaw ne degg, def benn jal bu sore ca dëkk ba ñu naa Aadama, te làng ak dëkk ba ñu naa Cartan. Ndox may wàcc jëm géeju Araba, maanaam géeju Xorom ga nag dagg, daldi wal ba jeex tàkk. Ba loolu amee mbooloo ma jàll, janook Yeriko.

© 2025 Bible Society of Senegal
>